Wolof

Declaration: Maous

“Wah boufebare nope yakoy dege nio warawher

Dalal ak jame manla sen rak Maous wala Ousmane. Mangifi si Allemagne. Damalen beuge wah linga hamne monla doundou si sama yonbi lico diele Africa ba Europe. Nioun hamnaniou Afrik dafa meti. Amuniou dara wante niakounioun dara. Danio beuge rafettal sounou doundou. Daniouy wahne koudoul  tou ki dou ham fou deke nehe. Kouniam ham lamouy saf. Thi bes bi nga hamne whana sama yay ne damay dem Europe Hawma ne ndah sama yay contana wala merona. Hawma ndah dioyona wala retannona. Linga hamne gentenako Africa moy Europe nit manafe ligey teamfi halis. Telolou degela amna ligey te amna halis wante niom beugeniou seddo ak nioun. Niom beugeniou deke ak nioun si bene deke. Niom danioun dioh ›Heim‹ bou sori dekebi. Fofou amul dara. Fofu dafa meti. Ndahte nie beugeniou seddo ak nioun dara ndahte nioum halatnaniou nioun amouniou place fini. Thi bess bi nga hamne dielna sama sak tekko si sama mbagemi ma won sama yay genau ma continue dem. Hawma ndah dina gisati sama yay encore. Galla diel dem Dakar. Fofou la diele bus dem Maroc. Lima gena rethiou moy niete wher yima fanan si alle Maroc. Hawma won keur hana rek si allebi la don doundou. Si diamono bi diemna diourom bene yon ak sodiak ngir dem Espagne. Yomboul fofou litah yomboul ndah fofou nonu battaux you mag yinga hamne nioy traferse fofou. Kou defli ragaloul dè. Mom ragaloul dè ndahte mom dèna paparé wante moungi doundou. Hana yaram bi rek mofinek wante rouhou bi demna. Bou bouryar mosana am daniouy contan ndah militaryi douniougis. diorom binne yow dialoul boudialoul lolou moy marienmarokenbi moniou diap yobouniou kasso. magilen diladj kan siyen mo begeu fanan si alle? Metiwona lol halis bi nioudon am si auto bahn bi la nioudon tahaw talal sounou loho telolou hamouniouco sounoudek defnaniouco litah liniou dounde ak liniou nan laniou begeun. Nekoulne hamnanio lolou yagi heh di heh di heh ba europ fi gena metti afrika lep li niou sohla amnafi wante douniouco am yagi begue ligey amnafi waye waro ligey. loutah? Yen europ figen dioudo main nekoulne yenaco tan. Afriken yi douniom tamid niotanal sen bop nioun comparan naniou yen dagen niou ragal lol yen hamoulen niou ngen harito ak ngaide molen genal ngen harito aknioun nioun begue na nioulen ham wante  yen begue len. loutah? ndah nioun amouniou dara wala nioun danio salte wala danio febar beppe febar boubon niounla lep lou niaw niounla. Si afrik laniohamene boamoul dara lep lu rer keurga yowla lep loulen manque ki amoul dara momla si degedege kiga hamne amna lep te momouco moy europ. Danio begue ligey wante niougi tedde. sounou yaram mougimetti. Si afika tamid yomboul wante daniouy dem ligey. Si besbi am 10 euro wala 5 lolou doyna niou. wante dou famibi yep danio begue occuper sounou bop amouniou dara wante contanna niou. yen niou besnie fi degloulen lilen dinit ni di wah ndahte kouy wah deded dafa fek gissoco sonounaniou si tedebi niogi wah si wolof boy doh diga tasek sawarsag nioun danio wara dadjiek nitnie ndahte nie hamou niou te douniou mosaham naniou def liniou man fi amna nit niou bah ak niou bon afrika eussi amna niou bah ak niou bon warnanio hamne yomboul besbiga dioudo sa youhou boundiek moy yagi niow fo hamne diafe diafe kessela moy adouna heh heh heh yalla diapaleniou. tega hamne niowago.”


 

Une Traduction va suivre…

Si tu veux nous aider, envoies nous un mail: spreadthewords@riseup.net
On sera content d’avoir de tes nouvelles.

Traductions: english / deutsch